AccueilSociétéLes chroniques de Mame Fatou : "La mort sur Facebook", version wolof...

Les chroniques de Mame Fatou : « La mort sur Facebook », version wolof par Usmaan Loo

FAATOO CI ‘FACEBOOK’

Ag dee déy, danu koy dund bis bunu xëyee. Bis bu nekk yit, nu dégg ay mbiram.
Bu nu xamul ki faatu yit, aw tiis lay doon fi nun, te yëg deek kun xamul a gën a woyaf fuuf ci yëg deeg kun xam.
Te kat! jarul sax muy nekk xarit walla mbokk mu jege, waaye na fekk rekk muy ku nu xam, di kun mas a gis sax wennuw yoon bay fàttliku xarkanam ga, ngir mu metti ci nun.

Ci “Facebook” nag moom, am na ag wuute !

Ndax nit ki nu ciy dajeel saa su ne, di xaritook moom, walla sax di ko ciy gis rekk, ag faatoom daf nuy tiis lool. Man sax jàpp naa ni – ci dëggdëgg – yëgyëg bi benn la, ci bu nit déggee ni kenn ci ñi nekkoon ci “Facebook” bi faatu na… Waneg “Cofeel” gi ak “ seede” si wàll gu ne lay jóge. Da nu koy jaalente rekk ak di koy seedeel, ak di koy ñaanal te dunu ko xam, rawatina nag bunu xaritoo woon ak moom ci Facebook bi. Kenn koo ci gis muy seede ci àlluway ku faatu nag, saw yaram day daw lool ngir li muy yëramtalu.

“Mandarga” yi, ak “nataal” yi, ak xalaat yu mujj yeek li mu doon wane ci wàll “site” gi, di mbooloo, walla xët wu ñu “ŋoy” ak weneen wu ñu “séddoo” ci àlluway waa jooju ci weer yii rekk, ak ayubis yii, ak fan yee, mbaa sax cib diir bu gàtt…

Ba mujj ma ni jàkk ci saa “bisub” bopp ba !

Ba xam kan moo ciy jëkk a yëgle saag faatu? Aa? ???? Ndax saab xarit lay doon? Mbaa mbokk? Walla sax àndandoo? Jàngalekat, màppandoo am saag maas? Doom ju góor mbaa Saa doom ju jigéen? Saa sët bu góor walla bu jigéen? Ana kan lay doon ci ñii? Ak lu muy wax sax? Nu mu koy defe? Lu muy yëg bu koy yëgle? Mo ndax daf may jooy bu koy bind ba gët ya taa xejj aki rangooñ, waaraamam ya yit di lox, xel ma nëx ba waat yay jaxasoo, ba du xam nu muy binde li muy yëgle?

Sama àlluwa ‘mur’ ji ma fiy bàyy nag moom! Nu muy mujje? Boo demee sax de! Day nekk barab bu ñuy sëngéeme, di fay ñaane, ndax dañ ma fay seedeel lu rafet? Am da fay nekk fuñuy jaaleentee ba ciy yëramtaloo, mbaa di fu àdduna si di may wane séenug cofeel.

Man de xawma luñ ciy wax?

Man sax de leegleeg da may ciy jaaxle ba daa koy laaj xarit yi, walla jegeñaale yi ngir am ciy xalaat… ???? ndax kat ñépp a koy teewlu… ba mu des man miy ndayi mbillgi! Man mi nga xam ni da ma daan tëb, ni xeww jàkkarlook àlluway ku fi mas a faatu, ngir xool say nataal, ak say tàf yi nga mujj tàf, ak say yëgle; ci buñ masaan a yëgle ku tawat, mbaa xibaaru dee gu gaaw gu rot ci “Facebook” bi…

Dem naa ci sax ba nga xam ni; bu saa xel mi demaatee ci ki réer rekk da may ubbiwaat di xool ay nataalam ak di jàng liñu ko mujj a seedeel…
Te kat du ma ca yam! Ndax bis bi mu faatoo bu delluseetee, walla benn bis bu ñuy fàttaliku; da may dikkati di ñaan…
Boo demee nag bii yoon; maay ki ñuy wër di toogaanu, di ki ñuy ñaanal yit, te xamu ñu ko woon sax…

Su ma dee xalaat ci jamano yi may nekke ci “Lijjanti ak Fuuyu” ci Facebook bi ngir yeesal àlluwa ji, ba mu beggandi, ba bu ëllagee mu yomb ci ñi manul a agsi ca saa bàmmeel ba sax man fa sëngeem aka ñaan… (te fii may binde sax maa ngi ci)
“A late needs are only prayers… And you never know when you’ll die”…
Ba may xalaat a roppi, laata maa dee gee fekk ci “Facebook”.

Waaye… sama deñkumpa gi du ma bàyyi ma wuute lii, bis bu rëy bii…

(Bu dee rekk Facebook baa ngi fi!).
Baat bu yiw a yiw… buy jàjj, daf maa déey ndéey la, yegge ma laaj bi ca kaw!
Ne ku fiy yéene ak lu muy yéene? (Li am daal: mooy bëggu ma ‘’RIP”* yu tasaaroo yi. Julli léen te sëlmal ci ‘rip’ yi bu ngéen bëggee, waaye ag ‘rip’ moom luñ ca man di wax… ñott na ci ab néew!)

Kiy bëgg sax lu muy bëgg? Waxkat bi yit lu muy wax? Ak luñ fiy sédale?
Sama ban “foto” moo ciy gën a siiw moom? Walla ban ci sama taf yeey nekk ci “jal” bi? Ndax bii la? Xëyna!
Lees ci xam… ñenn ñi naan: “ Ho my god! kii dey daa mel ni dafa gisoon ag dee’am”. ???? (Monte nag wax ci sag dee du genn keemaan; mbir mu jaadu la mu kenn ku nekk ci nun wara bàyy xel, ni nuy bàyye xel ab séy, ame ni ay doom, walla sax dem tukki di jàllantu dëkk ak dëkk…).

Waaw gan jàngat ci li ma daan jàngat ci mbooloo mi, ak gan wàll gu ma daan bokk, la kenn di taxaw bay waxtaane li ma wéeroon ca “lef” wa. Lan laay mujj a wane ci géew bi sax? Tuut si may mujj a wane rekk bala maa wuyu ji boroom bi?

Foofu nag, fa laa dékke saay yoxo, ñaan fa Yàlla mu musal ma ci caaxaan, ak rëy, ak ñàkk i teggin, ak xamadeek cuune,…

Ma ñaan Yàlla, bu baax, mu barkeel sama làmmiñ wi, ba nit man cee jariñu ci – biir ak ci bitti -… Ñaan Yàlla lépp loo xam ni daf may mandargaal rekk, na nekk lu sell te wér… Di ñaan Yàlla musal ma cig loyloyi ak réere yoon wi nuy muccal. May ñaan Yàlla lépp lu mu teg ci saay yoxo, (moo xam muy jumyukaay yu yees yeek yu ni mel) muy yëf yu ñuy defe ay santaaneem. May ñaan yit ag woyaf aguk yëg ba famay sàngoo suuf.

Ma dilay ñaan yaw Buur Bu màgg bi! Nga sàmm nu te ‘teg nu ci yoon wu jub wi, yoon wu jub wi nga teg sa tànneef yi, wu bokkul ak ñi aw fi la naqari, ak ñu réer ñi.’ (Saaru Faatiya).
Ma ñaan Boroom yërmannde ji nag, mu guddal sunuy fan, teg ci muj gu rafet, sell te ànd ak njariñ ak gindiku…

“ Boroom bi, yokk nuy leer te jéggal nu. Moom mi waabale” (Laayab 66:8) Aamiiin!

Ndéemsi Yàlla yi,
Njooro wal jàmm ci ñoom!

Mame Fatou Sy.
mamefatousy@yahoo.com
Article repris en wolof par Usmaan Loo.
Mes hommages Usmaan, ligeey bi mucc na ayib, jaajëf.

LAISSER UN COMMENTAIRE

S'il vous plaît entrez votre commentaire!
S'il vous plaît entrez votre nom ici

Must Read

spot_img